عربي - Arabic English Qafár af - Afar Afrikaans - Afrikanns Akan Shqip - Albanian አማርኛ - Amharic Հայերեն - Armenian অসমীয়া - Assamese Azərbaycanca - Azerbaijani Bamanankan - Bambara Bassa Bemba বাংলা - Bengali Bosanski - Bosnian Български - Bulgarian မြန်မာဘာသာ - Burmese Bisaya - Cebuano Cham Нохчий - Chechen chiCheŵa - Chewa 中文 - Chinese Адыгэбзэ - Circassian Hrvatski - Croatian Česky - Czech Dagbani Dansk - Danish فارسی دری - Dari Dendi ދިވެހި ބަސް - Dhivehi Nederlands - Dutch إستوني - Estonian Suomi - Finnish Français - French Fulfulde - Fula ქართული - Georgian Deutsch - German Ελληνικά - Greek ગુજરાતી - Gujrati Kreyòl ayisyen - Haitian Creole Hausa हिन्दी - Hindi Magyar - Hungarian Igbo Indonesia - Indonesian Italiano - Italian 日本語 - Japanese Jóola - Jola ಕನ್ನಡ - Kannada Қазақша - Kazakh ភាសាខ្មែរ - Khmer Kikuyu Ikinyarwanda - Kinyarwanda Ikirundi - Kirundi 한국어 - Korean كوردی سۆرانی - kurdish كوردي kurmancî - Kurmanji Kyrgyz ລາວ - Lao latviešu - Latvian Lingala lietuvių - Lithuanian Luganda Македонски - Macedonian Maguindanaon Malagasy - Malagasy Bahasa Melayu - Malay മലയാളം - Malayalam Mandinka मराठी - Marathi Mõõré - Moore नेपाली - Nepali أنكو - NKo Norwegian ଓଡ଼ିଆ - Odia oromoo - Oromo پښتو - Pashto فارسی - Persian Polski - Polish Portuguese ਪੰਜਾਬੀ - Punjabi Română - Romanian Русский - Russian Српски - Serbian Shona සිංහල - Sinhala Slovenščina - Slovenian Soomaaliga - Somali Soninke Sesotho - Sotho Español - Spanish Kiswahili - Swahili Svenska - Swedish Tagalog Тоҷикӣ - Tajik தமிழ் - Tamil తెలుగు - Telugu ไทย - Thai ትግረኛ - Tigrinya Türkçe - Turkish Ukrainian اردو - Urdu ئۇيغۇرچە - Uyghur Ўзбек - Uzbek Việt Nam - Vietnamese Wolof Yao Yorùbá - Yoruba Zarma زولو - Zulu
732 Hadiths
Encyclopedia of Prophetic Hadiths
Categories
Grading
Narrated in
Narrator
Show all narrators (195)
«ku gàddu ngànaay jëme sunu kaw kooku bokkul ci nun».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«bu nit ki feebaree walla mu tukki dees na ko bindal kem la mu daan jëf ba mu tukkiwul te wér».
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
«ku julli ñaari sedd yi dana dugg àjjana»
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«nangeen kóllarante ak Alxuraan jii, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom moo gën a gaaw a rëcc giléem gi ñu yeew».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Ñëw naa fi Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ànd ak mbooloo yu bokk ci giirug Al-Asharii, mu wax ne: "giñ naa ci Yàlla ne duma leen gàddu te sax
amuma lu ma leen gàddul" ñu des fa diir ba soob Yàlla, ñu dal di koy indil ay giléem, mu digle ñu jox leen ñatti giléem, ba ñu fa jógee, ñenn ci nun wax ñeneen ñi: Yàlla de du nu baarkeelal, ñëw nanu fi Yonnente Yàlla bi di sàkku mu gàddul nu mu giñ ne du nu gàddul ba noppi daal di nuy gàddul, Abuu Muusaa nee na: nu dem fi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ko loolu, mu ne nu: "du man maa leen gàddul, waaye Yàlla moo leen gàddul, man de giñ naa ci Yàlla ne -bu soobee Yàlla- duma giñ ci dara ba noppi gis leneen lu ko gën, lu dul ne dinaa kaffaara sama giñ ba te def la ko gën".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«misaalum jullit biy jàng Alxuraan moo ngi mel ni Utruja, xetam ga dafa teey ak cafkaam teey, misaalum jullit bi dul jàng Alxuraan moo ngi mel ni tàndarma, amul xet te cafkaam dafa neex,misaalum naaféq biy jàng Alxuraan moo ngi mel ni ngun-ngun xetam dafa teey cafkaam wex,misaalu naaféq bi dul jàng Alxuraan moo ngi mel ni xettar, amul xet te cafkaam dafa wex»
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"leelleen aji-xiif ji, seetileen ki feebar, yeewileen jaam bi".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.