Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

13 of 732 cards

Clear filters
«bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm- ca àjjana, ne ko: demal xool ko ak la ma ca waajalal ay ñoñam. Mu xool ko daal di ñëw, ne ko: giñ naa ci sa màgg gi ne kenn du ko dégg lu dul ne dana def lu ko cay dugal. Mu digle ñu wërale ko ak ay tiis, mu ne ko: demal xool ko ak la nu ca waajalal ay ñoñam, mu fekk ñu muure ko ak i tiis mu wax ko ne: giñ naa ci sa màgg gi ragal naa ne kenn du fa dugg. Mu ne ko demal nga xool sawara ak la ma ca waajalal ay ñoñam. Mu xool ko gis waa sawara a nga warante, mu dellu ne ko: giñ naa ci sa màgg gi kenn du def lu la fay dugal. Mu digle ñu muure ko ak i bànneex, mu ne ko: dellul xool ko. Mu xoolaat ko gis ñu muure ko ak i bànneex, mu dellu ne ko: giñ naa ci sa màgg gi ragal naa ne kenn du ca mucc».
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy.
«amul kenn kuy julli ci man lu dul ne Yàlla dana ma delloo samag ruu ba ma delloo ko nuyóo».
Ag càllalaam tane na Abóo Daawuda soloo na ko,ak Ahmat.
"bu kenn ci yéen eggee cib jotaay na nuyóo, bu nammee jug na nuyóo, ndax bu njëkk bi gënut a yay bu mujj bi".
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ahmat.
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan tissooli day teg loxoom -walla yéereem- ci gémmeñam, daal di suufeel -walla mu téye- ci kàdoom.
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.
«bu kenn ci yéen dajee ak mbokkam na ko nuyu, bu dara doxee seen diggante ag garab walla miir walla aw doj mu dajewaat ak moom na ko nuyu batay».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko.
"buleen tere jibéeri Yàlla yi jàkkay Yàlla yi, waaye nañu génn nekk ñu lëmësu".
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko.
"Nit ki moo ngi ci diiney xaritam, na ku nekk xool kan lay xaritool".
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.
Moom bu daan xëy day wax: "Allahuma bika asbahnaa, wa bika amsaynaa, wa bika nahyaa, wa bika namuutu, wa ilayka anusuuru" bu gontee daal di wax: "bika amsaynaa wa bika asbahnaa, wa bika nahyaa, wa bika namuutu, wa ilayka anusuuru" wax na it beneen yoon: "wa ilayka almasiiru".
Tane na Abuu Daawuda ak An-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ci Al-Kubraa, ak Ibn Maaja ñoo ko soloo.