Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

20 of 732 cards

Clear filters
«sama xeet wépp lañuy jéggal ba mu des ñiy fésal ag moy, te bokk na ci fésal ag moy nit ku def dara ci guddi gi, daal di xëy Yàlla suturaal ko, muy wax naan: éey yaw diw, biig def na lii ak lee, fekk dafa fanaan Yàlla suturaal ko, mu xëy di wuññi li ko Yàlla suturaaloon».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
التصنيف الشرعيذم المعاصيموضوعات الحديثالتوبة
Bi aaya bii wàccee: {te dees na leen laaj xéewal yi bis booba} [At-Takaasuru: 8], As-Subayru dafa wax: yaw Yonnente Yàlla bi, ban xéewal lañu nuy laaj, te li fi am mooy ñaar yu ñuul yi rekk muy tàndarma ak ndox? Mu ne ko: «waaye nag dana am de».
Tane na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja.
التصنيف الشرعيالزهد والورع، أحوال الصالحين، تفسير الآيات، الحياة الآخرةموضوعات الحديثالإيمان باليوم الآخر، الشكرمحاور التعريف بالإسلامالحساب
«ku génnug topp, daal di tàqalikoo ak mbooloo ma ba faatu, kon dee na deewug ceddo, képp kuy xeex ngir yékkati raayaa cànkute, di mer ngir par-parloo, di woote ci aw xeet, walla muy xeex ngir par-parloo ciw xeet pp ba ñu ray ko, kon ag rayam rayug ceddo la, képp ku génn ag topp ci sama xeet wi, di dóor ñu baax ña ak kàccoor ya, te du moytu sax way-gëm ña, te du matale kóllëreg boroom kollëre, kooku bokkul ci man te bokkuma ci moom».
Wér na Muslim soloo na ko.
التصنيف الشرعيالخروج على الإمامموضوعات الحديثأحكام الإمامة، الإخلاص
Laaj nañu Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waa juy xeex ngir wone njàmbaar, ak kuy xeex ngir par-parloo, ak kuy xeex ngir ngistal, ana kan ci ñoom moo nekk ci yoonu Yàlla? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di ne: "kiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku kooku moo ngi ci yoonu Yàlla".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
التصنيف الشرعيأعمال القلوب، أحكام ومسائل الجهاد وآدابهموضوعات الحديثفضل الجهاد، الإخلاص، الرياء