Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

4 of 732 cards

Clear filters
"ñent yii képp ku mu nekk ci moom nekk na naaféq, bu wenn melo nekkee ci moom kon wenn melow naaféq nekk na ci moom ba keroog mu koy bàyyi: bu waxtaanee fen, bu digee wuute ko, bu xulóo kàccoorr, bu kollarante daal di wor".
Wér na Al-Buxaarii ak muslim ñoo ko soloo
"ñent yii ku ñu nekk ci moom nekk na ab naaféq bu sotti, ku wenn melo ci ñoom nekk ci moom am na wenn melow naaféq ba keroog mu koy bàyyi: bu waxtaanee fen, bu kóllareentee wor, bu digee wuute ko, bu xuloo wax lu bon".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dañoo jiite jullig suba ca Hudaybiya ginnaaw ba mu tawee ca guddi ga, ba mu noppee mu jàkkaarloo ak nit ñi, ne leen: «ndax xam ngeen lan la séen Boroom wax ?» Ñu ne ko: Yàlla a xam ak ub Yónenteem, mu ne leen: Yàlla dafa wax ne: «am na ci sama jaam ñi ñu xëy gëm ma am ñu weddi, ku wax ne: taw bi wàcc na fi nun ci ngënéelu Yàlla ak yërmàndeem, kooku gëm na ma, weddi biddiw yi, waaye ku wax: taw bi biddiw bii mbaa bee mootax mu am, kooku weddi na ma, gëm biddiw yi».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«julli gi gën a diis ci naaféq yi mooy jullig gee ak jullig fajar, te bu ñu xamoon li nekk ci ñoom ñaar kon danañu ko teewe donte dañuy raam, doon naa yittewoo digle ñu taxawal julli, ma digal benn waay mu jiite nit ñi, ma ànd ak ay góor ñu yor ay matti sawara, nu dem ci nit yi dul teewe julli gi, taal séen kër ya ca séen kaw».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.