Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

37 of 732 cards

Clear filters
Nekkoon naa ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci benn tukki, ma xëy benn bis jegesi ko fekk ñoo ngi dox, ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, xibaar ma jëf joo xam ne dana ma dugal àjjana di ma soreele sawara, mu ne ma: "laaj nga lu màgg, waaye lu yomb la ci ku ko Yàlla yombal ci moom, dangay jaamu Yàlla te doo ku bokkaale ak dara, di taxawal julli, di joxe asaka, di woor weeru koor, te aji néeg ba" topp mu ne: "ndax duma la tegtal bunti yiw yi: woor ab pakk la, saraxe day fay njuumte kem ni ndox di faye sawara, ak jullig nit ki ci xaaju guddi " topp mu jàng: laayab « tata jaafaa junuubuhum ba àgg Yahlamuun » topp mu ne : "ndax duma la xibaar boppu mbir mi yépp ak kenoom?" Ma ne ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, mu ne: "boppu mbir mi mooy lislaam, kenoom di julli, njobbaxtal la di jihaad" topp mu ne : "ndax duma la xibaar li moom loolu lépp nag?" Ma ne ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, mu téye ci làmmiñam, daal di ne: "téyeel sa lii" ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, kon dees nuy jàppe li nuy wax? Mu ne ma: "yal na la sa yaay ñàkk yaw Muhaas, mo ndax dara dana këpp nit ñi ci seen kanam ya walla seen gémmiñ ya ca sawara lu dul seen góobiti làmmiñ?".
Wér na ci kaw bees boolee mbooleem yoon yi mu ñëwee At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
"ku julli sunu julli gi jublu sunu xibla bi lekk sunu rendi kooku mooy jullit bi nga xam ne amna kóllareg Yàlla ak kóllareg Yonnenteem bi, buleen wor Yàlla ci kóllareem gi".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
«Yahuut yi ñooy ñi Yàlla mere, nasaraan yi ñooy ñi réer».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko.
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax baay taxam ba: « waxal ne: amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla, ma seedeel la ci ëllëg bis-pénc», mu ne ko: bu dul woon waa Xurays danañu ma ŋàññi, di wax naan: li ko yóbbe loolu mooy tiitaange, kon dinaa ci bégal sa bët. Yàlla daal di wàcce Aaya bii: {du yaw yaay gindi koo sopp, waaye Yàlla mooy gindi ku ko soob} [Al-Xasas: 56].
Wér na Muslim soloo na ko.
Dañoo mas a toog ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci jàkka ji rekk benn waay bu yéeg sig giléem daldi dugg si, mu yésal giléem gi ci jàkka ji daal di koy yeew, ba noppi daal di ne? Kan ci yéen mooy Muhammat? Fekk Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo ngi sóonu ci séen biir, nu ne ko: góor gu weex gii sóonu la, waa ji ne ko: yaw doomu Abdul Mutalib, Yónente bi ne ko «wuyu naa la». Waa ji ne ko -: man de damalay laaj te dinaa taral laaj yi ci sa kaw, bul ma mere kon ? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «laajal lu la soob» mu ne ko: maa ngi lay laaj ci sa Boroom di Boroomu ñi la jiitu, ndax Yàlla moo la yónni ci nit ñépp ? Mu ne ko: «giñ naa ko ci Yàlla, waaw». Mu ne ko: maa ngi lay ñaan ci Yàlla , ndax Yàlla moo la digal nu julli juróomi julli ci bis bi ak ci guddi gi? Mu ne ko: «waaw maa ngi seedeloo Yàlla ». Mu ne ko: maa ngi ñaan ngir Yàlla, ndax Yàlla moo la digal nu woor weer wii ci at mi? Mu ne ko: «seedeloo naa ko Yàlla, waaw». Mu ne ko: maa ngi lay ñaan ngir Yàlla, ndax Yàlla moo la digal nga jël sarax ci sunu way-woomal ñi séddale ko ci sunu way-ñàkk ñi? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «maa ngi koy seedeloo Yàlla, waaw».waa ji ne ko: gëm naa li nga indi, man nag ndaw laa te samay nit ñoo ngi sama ginnaaw, man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.