عربي - Arabic English Qafár af - Afar Afrikaans - Afrikanns Akan Shqip - Albanian አማርኛ - Amharic Հայերեն - Armenian অসমীয়া - Assamese Azərbaycanca - Azerbaijani Bamanankan - Bambara Bassa Bemba বাংলা - Bengali Bosanski - Bosnian Български - Bulgarian မြန်မာဘာသာ - Burmese Bisaya - Cebuano Cham Нохчий - Chechen chiCheŵa - Chewa 中文 - Chinese Адыгэбзэ - Circassian Hrvatski - Croatian Česky - Czech Dagbani Dansk - Danish فارسی دری - Dari Dendi ދިވެހި ބަސް - Dhivehi Nederlands - Dutch إستوني - Estonian Suomi - Finnish Français - French Fulfulde - Fula ქართული - Georgian Deutsch - German Ελληνικά - Greek ગુજરાતી - Gujrati Kreyòl ayisyen - Haitian Creole Hausa हिन्दी - Hindi Magyar - Hungarian Igbo Indonesia - Indonesian Italiano - Italian 日本語 - Japanese Jóola - Jola ಕನ್ನಡ - Kannada Қазақша - Kazakh ភាសាខ្មែរ - Khmer Kikuyu Ikinyarwanda - Kinyarwanda Ikirundi - Kirundi 한국어 - Korean كوردی سۆرانی - kurdish كوردي kurmancî - Kurmanji Kyrgyz ລາວ - Lao latviešu - Latvian Lingala lietuvių - Lithuanian Luganda Македонски - Macedonian Maguindanaon Malagasy - Malagasy Bahasa Melayu - Malay മലയാളം - Malayalam Mandinka मराठी - Marathi Mõõré - Moore नेपाली - Nepali أنكو - NKo Norwegian ଓଡ଼ିଆ - Odia oromoo - Oromo پښتو - Pashto فارسی - Persian Polski - Polish Portuguese ਪੰਜਾਬੀ - Punjabi Română - Romanian Русский - Russian Српски - Serbian Shona සිංහල - Sinhala Slovenščina - Slovenian Soomaaliga - Somali Soninke Sesotho - Sotho Español - Spanish Kiswahili - Swahili Svenska - Swedish Tagalog Тоҷикӣ - Tajik தமிழ் - Tamil తెలుగు - Telugu ไทย - Thai ትግረኛ - Tigrinya Türkçe - Turkish Ukrainian اردو - Urdu ئۇيغۇرچە - Uyghur Ўзбек - Uzbek Việt Nam - Vietnamese Wolof Yao Yorùbá - Yoruba Zarma زولو - Zulu
732 Hadiths
Encyclopedia of Prophetic Hadiths
Categories
Grading
Narrated in
Narrator
Show all narrators (20)
«digal nañu ma ma xeex ak nit ñi ba baa ñuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka, bu ñu defee loolu ñoŋal nañu ci ma seen dereet ak seen alal lu dul ci àqi Lislaam, seenub regle nag ci Yàlla la aju».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
moom dafa wax Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: waaw xibaar ma bu ma dajee ak jenn waay ci yéefar yi ñu rayante, mu dóor jaaseem ji ci sama benn loxo
daal di koy dagg, topp mu làqatu ma ci genn garab, daal di wax ne: man jébbalu naa ñeel Yàlla, ndax dama koy ray yaw Yonnente Yàlla bi ginnaaw ba mu ko waxee? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: "bul ko ray" mu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, moom dafa dagg sama benn loxo, daal di wax loolu ginnaaw bi mu ko daggee? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: "bul ko ray, ndaxte boo ko rayee moom day nekk sa barab laata nga koy ray, yaw nga nekk ci barabam laata muy wax kàddu gi mu wax".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Damaa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi, Ibn Jadhaan de ca jamanoy ceddo ga da daan jokk mbokk di leel miskiin, mo ndax loolu dana ko jariñ ? Mu wax ne: «du ko jariñ de, ndaxte waxul benn yoon ne: sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba».
Wér na Muslim soloo na ko.
"bu nit waxee mbokkam: yaw yéefar bi, kon kenn ci ñoom ñaar yóbb na ko, bu dee li mu wax noonu la, lu ko moy mu dellusi ci moom".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«misaalu way-gëm ñi ci seenug bëggante ak seenug yërëmante ak seenug ñeewantu day mel ni aw yaram, bu ci benn cër di jàmbat dara mbooleem yaram wi yépp day
ànd bañ a nelaw ak di tàng».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«julli gi gën a diis ci naaféq yi mooy jullig gee ak jullig fajar, te bu ñu xamoon li nekk ci ñoom ñaar kon danañu ko teewe donte dañuy raam, doon naa yittewoo digle ñu taxawal julli, ma digal benn waay mu jiite nit ñi, ma ànd ak ay góor ñu yor ay matti sawara, nu dem ci nit yi dul teewe julli gi, taal séen kër ya ca séen kaw».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Nekkoon naa ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci benn tukki, ma xëy benn bis jegesi ko fekk ñoo ngi dox, ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, xibaar ma jëf joo xam ne dana ma dugal àjjana di ma soreele sawara, mu ne ma: "laaj nga lu màgg, waaye lu yomb la ci ku ko Yàlla yombal ci moom, dangay jaamu Yàlla te doo ku bokkaale ak dara, di taxawal julli, di joxe asaka, di woor weeru koor, te aji néeg ba" topp mu ne: "ndax duma la tegtal bunti yiw yi: woor ab pakk la, saraxe day fay njuumte kem ni ndox di faye sawara, ak jullig nit ki ci xaaju guddi " topp mu jàng: laayab « tata jaafaa junuubuhum ba àgg
Yahlamuun » topp mu ne : "ndax duma la xibaar boppu mbir mi yépp ak kenoom?" Ma ne ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, mu ne: "boppu mbir mi mooy lislaam, kenoom di julli, njobbaxtal la di jihaad" topp mu ne : "ndax duma la xibaar li moom loolu lépp nag?" Ma ne ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, mu téye ci làmmiñam, daal di ne: "téyeel sa lii" ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, kon dees nuy jàppe li nuy wax? Mu ne ma: "yal na la sa yaay ñàkk yaw Muhaas, mo ndax dara dana këpp nit ñi ci seen kanam ya walla seen gémmiñ ya ca sawara lu dul seen góobiti làmmiñ?".
Wér na ci kaw bees boolee mbooleem yoon yi mu ñëwee At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
"ku julli sunu julli gi jublu sunu xibla bi lekk sunu rendi kooku mooy jullit bi nga xam ne amna kóllareg Yàlla ak kóllareg Yonnenteem bi, buleen wor Yàlla ci kóllareem gi".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.