عربي - Arabic English Qafár af - Afar Afrikaans - Afrikanns Akan Shqip - Albanian አማርኛ - Amharic Հայերեն - Armenian অসমীয়া - Assamese Azərbaycanca - Azerbaijani Bamanankan - Bambara Bassa Bemba বাংলা - Bengali Bosanski - Bosnian Български - Bulgarian မြန်မာဘာသာ - Burmese Bisaya - Cebuano Cham Нохчий - Chechen chiCheŵa - Chewa 中文 - Chinese Адыгэбзэ - Circassian Hrvatski - Croatian Česky - Czech Dagbani Dansk - Danish فارسی دری - Dari Dendi ދިވެހި ބަސް - Dhivehi Nederlands - Dutch إستوني - Estonian Suomi - Finnish Français - French Fulfulde - Fula ქართული - Georgian Deutsch - German Ελληνικά - Greek ગુજરાતી - Gujrati Kreyòl ayisyen - Haitian Creole Hausa हिन्दी - Hindi Magyar - Hungarian Igbo Indonesia - Indonesian Italiano - Italian 日本語 - Japanese Jóola - Jola ಕನ್ನಡ - Kannada Қазақша - Kazakh ភាសាខ្មែរ - Khmer Kikuyu Ikinyarwanda - Kinyarwanda Ikirundi - Kirundi 한국어 - Korean كوردی سۆرانی - kurdish كوردي kurmancî - Kurmanji Kyrgyz ລາວ - Lao latviešu - Latvian Lingala lietuvių - Lithuanian Luganda Македонски - Macedonian Maguindanaon Malagasy - Malagasy Bahasa Melayu - Malay മലയാളം - Malayalam Mandinka मराठी - Marathi Mõõré - Moore नेपाली - Nepali أنكو - NKo Norwegian ଓଡ଼ିଆ - Odia oromoo - Oromo پښتو - Pashto فارسی - Persian Polski - Polish Portuguese ਪੰਜਾਬੀ - Punjabi Română - Romanian Русский - Russian Српски - Serbian Shona සිංහල - Sinhala Slovenščina - Slovenian Soomaaliga - Somali Soninke Sesotho - Sotho Español - Spanish Kiswahili - Swahili Svenska - Swedish Tagalog Тоҷикӣ - Tajik தமிழ் - Tamil తెలుగు - Telugu ไทย - Thai ትግረኛ - Tigrinya Türkçe - Turkish Ukrainian اردو - Urdu ئۇيغۇرچە - Uyghur Ўзбек - Uzbek Việt Nam - Vietnamese Wolof Yao Yorùbá - Yoruba Zarma زولو - Zulu
732 Hadiths
Encyclopedia of Prophetic Hadiths
Categories
Grading
Narrated in
Narrator
Show all narrators (20)
«li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli».
Wér na Muslim soloo na ko.
"yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm, Yàlla rëbb na nit ñiy jàppe bàmmeelu seeni Yónente ay jàkka".
Wér na Ahmat soloo na ko.
Benn waay dafa laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam, te dolliwuma ca dara, ndax dinaa dugg àjjana ? Mu ne ko: "waaw".
Wér na Muslim soloo na ko.
"ñent yii ku ñu nekk ci moom nekk na ab naaféq bu sotti, ku wenn melo ci ñoom nekk ci moom
am na wenn melow naaféq ba keroog mu koy bàyyi: bu waxtaanee fen, bu kóllareentee wor, bu digee wuute ko, bu xuloo wax lu bon".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
«gaaflu bokkaale la, gaaflu bokkaale la, gaaflu bokkaale la, -ñatti yoon-, amunu ci pexe, waaye Yàlla mu màgg mi moo koy dindi ci wakkirlu.
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waxtaanal na nu te mooy aji-dëggal ba di ku ñu dëgggal ki mu ne: «kenn ci yéen dees na dajale am mbindam ci biiru yaayam ñent-fukki bis ak ñent-fukki guddi, mu nekk lumbuw dereet, kem loolu, nekk aw suux kem loolu, ñu yabal ci moom malaaka ma, ñu digal ko ñenti baat, mu bind ko: wërsëgam, ab digam, ak jëfam, ak day texeedi walla day texe, mu wal ca ruu, kenn ci yéen de dana jëf jëfi waa àjjana ba dara nekkul digganteem ak moom lu dul loxo, téere ba jiitu ko mu jëf jëfi waa sawara daal di dugg sawara, kenn ci yéen it dana jëf jëfi waa sawara ba dara doxul digganteem ak moom lu dul ab loxo, mu jëf jëfi waa àjjana daal di dugg àjjana».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Benn waay bu bokk ci waa Najd dafa ñëw ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- kawar gi tasaaroo, ñoo ngi dégg kàddug waxam ji, waaye xamunu li muy wax, ba mu jege Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- neke da doon laaj ci Lislaam, Yonnente bi ne ko: "juróomi julli ci bëccëg ak guddi gi" mu ne ko: ndax dara waru ma lu dul yooyu? Mu ne ko: "déedéet, lu dul nga coobarewu, ak woor weeru koor", mu ne ko: ndax dara waru ma lu dul moom? Mu ne ko: "déedéet, lu dul nga coobarewu", Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tuddal ko asaka, mu ne ko: ndax dara waru ma lu dul moom? Mu ne ko déedéet, lu dul nga coobarewu", nee na waa ji wane ginnaaw di dem, di wax naan: giñ naa ci Yàlla ne duma yokk ci lii dara, te duma ko wàññi, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne: "texe na de ndeem wax na
dëgg".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.