Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

19 of 732 cards

Clear filters
"ñent yii képp ku mu nekk ci moom nekk na naaféq, bu wenn melo nekkee ci moom kon wenn melow naaféq nekk na ci moom ba keroog mu koy bàyyi: bu waxtaanee fen, bu digee wuute ko, bu xulóo kàccoorr, bu kollarante daal di wor".
Wér na Al-Buxaarii ak muslim ñoo ko soloo
«Saytaane day dikkal kenn ci yéen, di ko wax naan: ku bind lii? Ku bind lii? Ba mujj mu ne ko: ku bind sa Boroom? Bu àggee fii nag na muslu ci Yàlla te yamale ko fa».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax Muhaas Ibn Jabal ba mu ko yónnee Yaman ne ko: " yaa ngi jëmm ci aw nit woo xam ne ay ñoñ-téere lañu, boo demee ca ñoom, nanga leen woo ñu seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawu Yàlla la, bu ñu la toppee ci loolu, nga xamalleen ne Yàlla farataal na ci ñoom juróomi julli ci bis bu nekk aki gudeem, bu ñu la toppee ci loolu nga xamalleen ne Yàlla farataal na ci ñoom ab sarax bob dees na ko jëll ci séen way-woomal yi delloo ko ci séeni way-ñàkk, bu ñu la toppee ci loolu nag nanga moytu séen tedd-ngay alal ya, te nga moytu ñaanug ku ñu tooñ ndax amul kiiraay diggam ak Yàlla".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"tabax nañu lislaam ci juróom: seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamam la di ndawam, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak aji Màkka, ak woor weeru koor ".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Damaa wax: yaw Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaar ma ci bir yi ma daan def ca ceddo ga, ci sarax ak goreel, ak jokk mbokk, ndax am na yool? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «jébbalu nga ànd ak la nga defoon ciw yiw».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"ñent yii ku ñu nekk ci moom nekk na ab naaféq bu sotti, ku wenn melo ci ñoom nekk ci moom am na wenn melow naaféq ba keroog mu koy bàyyi: bu waxtaanee fen, bu kóllareentee wor, bu digee wuute ko, bu xuloo wax lu bon".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waxtaanal na nu te mooy aji-dëggal ba di ku ñu dëgggal ki mu ne: «kenn ci yéen dees na dajale am mbindam ci biiru yaayam ñent-fukki bis ak ñent-fukki guddi, mu nekk lumbuw dereet, kem loolu, nekk aw suux kem loolu, ñu yabal ci moom malaaka ma, ñu digal ko ñenti baat, mu bind ko: wërsëgam, ab digam, ak jëfam, ak day texeedi walla day texe, mu wal ca ruu, kenn ci yéen de dana jëf jëfi waa àjjana ba dara nekkul digganteem ak moom lu dul loxo, téere ba jiitu ko mu jëf jëfi waa sawara daal di dugg sawara, kenn ci yéen it dana jëf jëfi waa sawara ba dara doxul digganteem ak moom lu dul ab loxo, mu jëf jëfi waa àjjana daal di dugg àjjana».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Benn waay bu bokk ci waa Najd dafa ñëw ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- kawar gi tasaaroo, ñoo ngi dégg kàddug waxam ji, waaye xamunu li muy wax, ba mu jege Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- neke da doon laaj ci Lislaam, Yonnente bi ne ko: "juróomi julli ci bëccëg ak guddi gi" mu ne ko: ndax dara waru ma lu dul yooyu? Mu ne ko: "déedéet, lu dul nga coobarewu, ak woor weeru koor", mu ne ko: ndax dara waru ma lu dul moom? Mu ne ko: "déedéet, lu dul nga coobarewu", Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tuddal ko asaka, mu ne ko: ndax dara waru ma lu dul moom? Mu ne ko déedéet, lu dul nga coobarewu", nee na waa ji wane ginnaaw di dem, di wax naan: giñ naa ci Yàlla ne duma yokk ci lii dara, te duma ko wàññi, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne: "texe na de ndeem wax na dëgg".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.