Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

22 of 732 cards

Clear filters
Ay nit laaj na ñu Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mbiri gisaanekat, mune leen: «nekkuñu ci dara» ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ñoom de leeg-leeg ñu wax nu dara mu nekk dëgg’ mine leen: «baatu dëgg boobu jinne moo koy këf sànni ko ci noppi kilifaam kem kàddu ginaar gu jigéen, ñu jaxase si lu ëpp téeméeri fen».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"Yàlla gërëm na ci yéen ñatt, bañ na it ci yéen ñatt, gërëm na ci yéen: ngeen jaamu ko, te bañ ko a bokkaale ak dara, ak ngeen jàpp ci buumu Yàlla gi te bañ a teqalikoo, mu bañ ci yeen: nee nañu ak nee na, ak barig laaj, ak sànk alal".
Wér na Muslim soloo na ko.
«buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli».
Wér na Muslim soloo na ko.
Bi faatu dikkalee Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa jël ab yéreem tek ko ci kanamam, bu jaaxlee ci moom daal di koy muri ci kanamam, daal di wax ne: «yal na Yàlla rëbb Yahuut yi ak Nasaraan yi, ñoom kat dañoo jàppe séen bàmmeeli Yónente yi ay jàkka» day artu ci li ñu def.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Toggoo woon naa ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- am Mbaam mu ñuy woowe Xufayr, mu ne ma: «yaw Muhaas, ndax xam nga lan moy Àqi Yàlla ci ay jaamam, ak lan mooy àqi jaam ñi ci Yàlla?», Muhaas nee: ma ne ko: Yàlla ak ub Yónenteem ñoo ko xam, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- daal di ne ko: «àqi Yàlla ci jaam ñi mooy ñu jaamu ko te bañ koo bokkaale ak dara, àqi jaam ñi ci Yàlla nag mooy du mbugal ku ko bokkaalewul ak dara» ma ne ko: yaw Yónente Yàlla bi tee maa bégal nit ñi ci lii ? Mune ma: «buleen bégal kon dañuy bayliku.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«ku wax: laahi ilaaha illallaahu, amul kenn ku ñu war a jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, daal di weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla alalam ak dereetam araam na, Yàlla rekk nag mooy càmbar ay jëfam».
Wér na Muslim soloo na ko.
Aliyun Ibn Abii Taalib da ne ma: ndax du ma la yabal ca la ma Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yabaloon? Bul bàyyi benn xërëm te tojoo ko, mbaa benn bàmmeel bu ñuy màggal te maasale woo ko.
Wér na Muslim soloo na ko.
«buleen di giñ ci yi ñuy jaamu te du Yàlla, buleen di giñ it ci seen i baay».
Wér na Muslim soloo na ko.