Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

18 of 732 cards

Clear filters
«Sama xeet wépp dinañu dugg àjjana ba mu des ku bañ», ñu ne ko ana kan mooy bañ yaw Yónente Yàlla bi? Mu ne: «ku ma topp dugg àjjana ku ma moy nag kooku mooy ki bañ».
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
Wàcce na ñu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Alxuraan fekk mi ngi am ñent-fukki at, mu sax Màkka fukki at ak ñatt, ñu dugal ko mu gàddaay, mu gàddaay dem Madiina, sax fa fukki at, daal di faatu -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"jox na nu ma juróom yoo xam ne joxuñuko kenn ku ma jiitu: dimbalees na ma ci ag ragal luy toll ni doxub weer, defal na nu ma suuf si muy jàkka di lu laab, fu julli dabe kenn ci samaw xeet na julli, daganal na nu ma koomi xare yi, te daganaluñu ko woon kenn ku ma jiitu, jox na nu ma ramm ga, Yonnente dañu ko daan yónni ci xeetam kese man nag ñu yónni ma ci nit ñépp ".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom kenn du ma dégg ci xeet wii moo xam Yahuut la walla Nasaraan, ba faatu te gëmul li ñu ma yónni lu dul ne dana bokk ci waa sawara».
Wér na Muslim soloo na ko.
"tabax nañu lislaam ci juróom: seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamam la di ndawam, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak aji Màkka, ak woor weeru koor ".
Wér na Al-Buxaarii ak muslim ñoo ko soloo
«giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, daa naka rekk Iisaa Ibn Maryama wàcc ci yeen di ab àttekat bu màndu, di toj kurwaa yi, di ray mbaam-xuux yi, dindi galag gi(empo) bi, alal daal di baawaan ba kenn soxlawu ko».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«lépp lu ma leen tere nangeen ko moytu, lépp lu ma leen digal nangeen ca def lu ngeen man, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy seen laaj yu bari, ak seenug juuyoo ak seen i Yonente».
Wér na Al-Buxaarii ak muslim ñoo ko soloo
"Amul ci Yonnente yi benn Yonnente lu dul ne Yàlla jox na ko luy tax nit ñi gëm ko, man nag li ñu ma jox ag soloo la gog Yàlla moo ma ko soloo, ba maa ngi yaakaar a nekk ki ëpp ñi koy topp ëllëg bis-pénc"
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.