Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

13 of 732 cards

Clear filters
«giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, daa naka rekk Iisaa Ibn Maryama wàcc ci yeen di ab àttekat bu màndu, di toj kurwaa yi, di ray mbaam-xuux yi, dindi galag gi(empo) bi, alal daal di baawaan ba kenn soxlawu ko».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«lépp lu ma leen tere nangeen ko moytu, lépp lu ma leen digal nangeen ca def lu ngeen man, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy seen laaj yu bari, ak seenug juuyoo ak seen i Yonente».
Wér na Al-Buxaarii ak muslim ñoo ko soloo
"Amul ci Yonnente yi benn Yonnente lu dul ne Yàlla jox na ko luy tax nit ñi gëm ko, man nag li ñu ma jox ag soloo la gog Yàlla moo ma ko soloo, ba maa ngi yaakaar a nekk ki ëpp ñi koy topp ëllëg bis-pénc"
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"ñi gën ci yéen ñooy samag maas, topp ci ña ca topp, topp ci ña ca topp' Imraan nee na: xamuma ndax Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tudd na ginnaaw ag maasam ñaari maas walla ñatt, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "nekk na ci seen ginnaaw ay nit yoo xam ne dañuy wor te deesu leen wóolu, ñuy seede te deesu leen seedeloo, ñuy nisar te du ñu ko matal, ag duuf feeñ ci ñoom".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Dañoo mas a toog ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci jàkka ji rekk benn waay bu yéeg sig giléem daldi dugg si, mu yésal giléem gi ci jàkka ji daal di koy yeew, ba noppi daal di ne? Kan ci yéen mooy Muhammat? Fekk Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo ngi sóonu ci séen biir, nu ne ko: góor gu weex gii sóonu la, waa ji ne ko: yaw doomu Abdul Mutalib, Yónente bi ne ko «wuyu naa la». Waa ji ne ko -: man de damalay laaj te dinaa taral laaj yi ci sa kaw, bul ma mere kon ? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «laajal lu la soob» mu ne ko: maa ngi lay laaj ci sa Boroom di Boroomu ñi la jiitu, ndax Yàlla moo la yónni ci nit ñépp ? Mu ne ko: «giñ naa ko ci Yàlla, waaw». Mu ne ko: maa ngi lay ñaan ci Yàlla , ndax Yàlla moo la digal nu julli juróomi julli ci bis bi ak ci guddi gi? Mu ne ko: «waaw maa ngi seedeloo Yàlla ». Mu ne ko: maa ngi ñaan ngir Yàlla, ndax Yàlla moo la digal nu woor weer wii ci at mi? Mu ne ko: «seedeloo naa ko Yàlla, waaw». Mu ne ko: maa ngi lay ñaan ngir Yàlla, ndax Yàlla moo la digal nga jël sarax ci sunu way-woomal ñi séddale ko ci sunu way-ñàkk ñi? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «maa ngi koy seedeloo Yàlla, waaw».waa ji ne ko: gëm naa li nga indi, man nag ndaw laa te samay nit ñoo ngi sama ginnaaw, man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.