Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

14 of 732 cards

Clear filters
"aw nit wu jiital jigéen ci seen i bir duñu mucc mukk".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
«bu nit ki feebaree walla mu tukki dees na ko bindal kem la mu daan jëf ba mu tukkiwul te wér».
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
«ku ne ci yéen ab sàmm la te dees na ko laaj la mu doon sàmm, ki jiite nit ñi ab sàmm la te danañu ko ko laaj,góor gi ab sàmm la ci waa këram te danañu ko ko laaj, jigéen ji ab sàmm la ci kër jëkkëram ak i doomam te danañu ko ko laaj, jaam bi ab sàmm la ci alali sangam te danañu ka ko laaj, yégleen ne ku nekk ci yéen ab sàmm la te dees na ko laaj la mu doon sàmm».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Jaayante nanu ak Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci dégg ak topp, ci lu jafe ak lu yomb, ci lu neex ak lu naqari, ak bu xat-xat tegee sunu kaw, ak nu bañ a xëccoo ak nguur, ak nu bañ a wax lu dul dëgg fu nu man a nekk, dunu ragal ci Yàlla yeddagay aji-yedde ji.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«fépp fu yax di daje ci nit sarax la, bépp bis bu jant bi fenk mu Maandu ci diggante ñaari nit loolu sarax la, mu dimbali nit ci daabaam yéegal ko ca, walla mu yéegalal ko ay jumtukay loolu sarax la, wax ju teey sarax la, ak bépp jéego bu mu jéego jëm ca julli ga sarax la, ak mu toppale lor wu nekk ci kaw yoon wi loolu sarax la».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«amul benn jaam bu Yàlla sàmmuloo am càmm, mu faatu fekk da doon wuruj ña muy sàmme, lu dul ne Yàlla dana araamal ci moom àjjana».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Bi dee dikkalee Abuu Taalib, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñëw fi moom fekk fa Abuu Jahlin, ak Abdullah Ibn Abii Umayyata ibnul Muxiirata, mu ne ko: "yaw sama baay tëx, waxal: laa ilaaha Illal Laahu, genn kàddu gog dinaala ci mana layal fa Yàlla", Abuu Jahlin ak Abdullah Ibn Abii Umayyata ne ko: mo ndax dangay bàyyi diiney Abdul Muttalib, Yonnente bi deñul di ko ko gaaral, ñoom itam ñuy baamtu wax jooju, ba Abuu Taalib mujj a wax ne, maa ngi ci diiney Abdul Muttalib, mu bañ a wax: laa ilaaha illallaah, nee na: Yonnente Yàlla bi daal di wax ne: "giñ naa ci Yàlla ne dinaa la sàkkul njéggal fii ak terewuñu ma ko", Yàlla daal di wàcce laaya jii: {jaaduwul ci Yonnente bi ak ci ñi gëm ñuy jéggalul bokkaalekat yi} [At-Tawba: 113], Yàlla wàcce ci Abuu Taalib, daal di wax Yonnente Yàlla bi ne ko: {yaw de du yaay gindi ku la soob waaye Yàlla mooy gindi ku ko soob} [Al-Xasas: 56].
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"bépp téqqu nit sarax la ci moom, bis bu jànt bi fenk mu maandu ci diggante ñaari nit loolu sarax la, ak nga dimbale nit ki ci waruwaayam yéegal ko ca walla nga jottali ko ca ay bagaasam loolu sarax la, wax ju teey sarax la, bépp jéego booy dox jëm ca julli ga loolu sarax la, ak nga randale aw lor ci yoon loolu sarax la ".
Wér na Al-Buxaarii ak muslim ñoo ko soloo