Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

48 of 732 cards

Clear filters
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na jenn wax, ma wax Jeneen wax, yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ne: " ku faatu fekk moo ngi wutal Yàlla ndend dana dugg sawara" man ma ne: ku faatu te wutalul Yàlla ndend dana dugg àjjana.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf».
Wér na Muslim soloo na ko.
«amul kenn ci yéen lu dul ne Yàlla dina wax ak moom, te kenn kuy firi du nekk seen diggante, mu xool ndayjooram du gis lu dul li mu jiital, mu xool càmmooñam du gis lu dul li mu jiital, mu xool kanamam du gis lu dul sawara wu jàkkarloo ak moom, ragalleen sawara donte dangeen joxe aw xaru tàndarma la».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Muhaas dafa toggoo woon ak moom ci benn waruwaay mune ko: «yaw Muhaas Ibn Jabal», mu ne ko: wuyu naa la yaw Yónente Yàlla bi, mu ne ko: «yaw Muhaas» mu ne ko wuyu naa la yaw Yónéte Yàlla bi, ñatti yoon, mu ne ko: « amul kenn kuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la te mu dëggu ci xolam lu dul ne Yàlla dana ko araamal ca sawara», mu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ndax duma ko wax nit ñi ngir ñu bég? Mu ne ko: «kon dañuy bàyyandiku». Muhaas waxe ko jamano yi muy faatu ngir bañ a bàkkaaru.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Ay nit laaj na ñu Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mbiri gisaanekat, mune leen: «nekkuñu ci dara» ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ñoom de leeg-leeg ñu wax nu dara mu nekk dëgg’ mine leen: «baatu dëgg boobu jinne moo koy këf sànni ko ci noppi kilifaam kem kàddu ginaar gu jigéen, ñu jaxase si lu ëpp téeméeri fen».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"Yàlla gërëm na ci yéen ñatt, bañ na it ci yéen ñatt, gërëm na ci yéen: ngeen jaamu ko, te bañ ko a bokkaale ak dara, ak ngeen jàpp ci buumu Yàlla gi te bañ a teqalikoo, mu bañ ci yeen: nee nañu ak nee na, ak barig laaj, ak sànk alal".
Wér na Muslim soloo na ko.
«buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli».
Wér na Muslim soloo na ko.
Bi faatu dikkalee Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa jël ab yéreem tek ko ci kanamam, bu jaaxlee ci moom daal di koy muri ci kanamam, daal di wax ne: «yal na Yàlla rëbb Yahuut yi ak Nasaraan yi, ñoom kat dañoo jàppe séen bàmmeeli Yónente yi ay jàkka» day artu ci li ñu def.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.