Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

13 of 732 cards

Clear filters
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ginnaaw jullig farata gu ne: «laa iLaaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku wa lahul hamdu, wa Huwa halaa kulli say-in Xadiirun, Allaahumma laa maaniha limaa ahtayta, walaa muhtiya limaa manahta, walaa yanfahu sal jaddi minkal jaddu».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«ay mbir a ngii yuy wuutante ku leen di wax du sooy -walla ku leen di def- ginnaaw jullig farata gu nekk, Subhaanal Laahi fanweeri yoon ak ñatt, alhamdu lil-Laahi fanweeri yoon ak ñatt, Allaahu Akbaru, fanweeri yoon ak ñent».
Wér na Muslim soloo na ko.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa génn ci nun, nu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, xam nanu naka lanu lay nuyòo, leegi naka lanuy jullee ci yaw?, mu wax ne: "waxleen: Allaahumma salli halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin kamaa sallayta halaa aali Ibraahiima, innaka Hamiidun Majiidun, Allaahumma baarik halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin kamaa baarakta halaa aali Ibraahiima innaka Hamiidun Majiidun".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Allaahumma ixfir lii, warhamnii, wa haafinii, wahdinii, warsuqnii».
Tane na bees sukkandikoo ci yeneen yi koy dëggal Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan ñaan daan na wax: " Allaahumma innii ahuusu bi ka min hasaabil xabri, wa min hasaabin naari, wa min fitnatil mahyaa wal mamaati, wa min fitnatil Masiihid Dajjaali". Am na ci jeneen wax ci Muslim: "bu kenn ci yéen noppee ci taaya ju mujj ji, na muslu ci Yàlla ci ñent: ci mbugalum Jahannama, ak ci mbugalu bàmmeel, ak ci fitnay dund ak dee, ak ci ayu Masiihud Dajjaal ".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.