Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

4 of 732 cards

Clear filters
"bu kenn ci yeen yeewoo ci ay nelawam na fiiru ñatti yoon, ndaxte Saytaane day fanaan ci paxi bakkanam".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Ànd nanu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jóge Màkka jëm Madiina ba nu eggee ci am ndox ci yoon wi am ñu gaawantu ca Tàkkusaan ga, daal di jàppu cig yàkkamti, ba nu egge fa ñoom gis seen tastën ya ndox mi laalu ko, Yonnente bi daal di wax ne: "mbugal ñeel na tastën ya ca sawara, deeleen jotal njàppu mi".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Jële na ñu ci Humraan jaamub Usmaan Ibn Affaan, mu wax ne, gis na Usmaan Ibn Affaan laaj ndox mu mu jàppoo, mu tanq loxoom ci ndab li, raxas leen ñatti yoon, mu dugal ndeyjooram ci jàppukaay bi, daal di gallaxndiku saraxndiku fiiru, daal di raxas xar kanamam ñatti yoon, ak ñaari loxoom ba ci conco yi ñatti yoon, daal di masaa boppam, daal di raxas tànk bu ne ñatti yoon, daal di wax ne: gis naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy jàppoo kem sama njàpp mii, ba noppi wax ne: "ku jàppoo kem sama njàpp mii, daal di julli ñaari ràkka yoy du ca xalaat dara, kon Yàlla dana ko jéggal bàkkaaram yi jiitu".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Gis naa Amr ibn Abii Hasan mu laaj Abdullah Ibn Saydin, nu Yónente bi doon jàbbee, mu laaj ndab lu def ndox, daal di jàpp njàppum Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu sotti ci loxoom, raxas loxo yi ñatti yoon, mu daal di dugal loxoom ci ndab li daal di gallaxndiku daal di saraxndiku daal di fiiru ci ñàtti tanq,mu daal di dugalaat loxoom daal di raxas kanamam ñatti yoon,daal di raxas loxoom ba ci coñc yi ñaari yoon,mu dugalaat loxoom daal di masaa boppam yóbb ko ci kanam ak ci ginnaaw benn yoon,mu daal di raxas ñaari tànkam ba ci dojor yi.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.