Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

4 of 732 cards

Clear filters
«baax mooy: rafet jikkó, bàkkaar mooy liy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ci gis ko».
Wér na Xadiis bu njëkk bi: Muslim moo ko soloo, hadiis bu ñaareel bi: Ahmad ak Ad-Daaramii ñoo ko soloo.
Gis naa Ammaar ibn Yaasir mu dugg ci jàkka ji daal di julli woyofal julli gi, nee na: ba mu génnee, ma jug dem ci moom, ne ko: yaw Abaa Al-Yaqsaan, woyofal nga de, mu ne ma: ndax dangaa gis ma wàññi ci ay dayoom dara?! Ma ne ko: déedéet, mu ne ma: damaa gaawantu di njëkkante ak yàqi saytaane, dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax naan: " jaam bi dana julli julli ga, te deesu ko ca bindal lu dul fukkeelu xaaj ba, juróom-ñenteel ba, juróom-ñatteel ba, juróom-ñaareel ba, juróom-benneel ba, juróomeel ba, ñenteel ba, ñatteel ba, genn wall ga".
Tane na Ahmat soloo na ko.
«Yàlla sadd na misaal ci yoon wu jub, te ci ñaari wetu yoon wi am na ñaari miir yu am bunt yu ubbeeku, ci bunt ya am ay rido yu ñu yoor, te ci buntu yoon wi am na kuy woote naan: “Yéen nit ñi! Duggleen ci yoon wi, te buleen jàdd. Am beneen wootekat buy woote nekk ca kaw yoon wa, bu bëggee ubbi dara ca bunt ya, mu ne ko: toskare ñeel na la bu ko ubbi, ndax boo ko ubbee da nga ca dugg. Yoon wa mooy Lislaam, ñaari miir yi: ñooy digi Yàlla yi, (fimiy yamlu) bunt yu ubbeeku yi: mooy terey Yàlla yi, kooku di woote ci boppu yoon wi: mooy Téereb Yàlla bi, kiy woote ci kaw yoon wi: mooy kiy waarekate ci Yàlla xolu jullit bu nekk».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat.
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na baril lu muy wax: "yaw Aji-Wëlbati xol yi saxalal sama xol bi ci sa diine ji", ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, gëm nanu la gëm li nga indi, mo ndax danga noo tiital ? Mu ne: "waaw, xol yi ñoo ngi ci diggante ñaari baaraam ci baaraami Yàlla yi moo koy wëlbati nu mu ko soobe".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat.