Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

45 of 732 cards

Clear filters
"dëddul àdduna kon Yàlla dana la bëgg, dëddul li ci nit ñi kon nit ñi danañu la bëgg".
An-Nawawii nee na hadiis bu rafet la Ibn Maaja moo ko soloo ak ñeneen ci ay càllale yu rafet.
"Yàlla ak ub yonnenteem araamal na ñu jaay sàngara, ak médd, ak mbaam xuux, ak ay xërëm", ñu ne ko yaw Yonnente Yàlla bi, luy mbiri gereesu médd? Dañu ciy diw gaal yi, di ci diw der yi, nit ñi di ci leerale? Mu ne: "déedéet, dafa araam", Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: "yal na Yàlla ray Yahuud yi, ba Yàlla araamalee ci ñoom gerees ga dañu ko a seeyal, jaay ko, lekk njëg ga".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«nekkal ci àdduna mel ni ku tumurànke walla kuy jaar ciw yoon", ibn Umar, daan na wax naan: boo gontee bul xaar suba, boo xëyee bul xaar ngoon, nanga jël ci sag wée ñeel sag tawat, ak ci sag dund ñeel sag dee.
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
"Yaw ngóor si dinaa la xamal ay waat: wattul Yàlla kon Yàlla dina la sàmm, nanga bàyyi xel Yàlla kon mu féete la fépp, booy ñaan ñaanal Yàlla, booy sàkku ndimbal na nga dimbandikoo Yàlla, te nga xam ne bu ñépp daje woon ngir jariñ la ci dara duñu ko man lu dul lu Yàlla dogal ci yaw ba noppi, bu ñépp daje woon it ngir lor la ci dara duñu ko man lu dul lu Yàlla dogal ci yaw ba noppi; ndax teggi nañu bindukaay ya, te àlliwo ya wow na".
Wér na At-Tirmisiyyu moo ko soloo ak ñeneen.
«li dagan de leer na li araam it leer na, seen diggante nag am na ay lënt, te ñu bari si nit ñi duñu ko xam, képp ku moytu yu lënt yi ñoŋal na diineem ak deram, waaye ku tàbbi ca lënt ya kooku tàbbi na ca yu araam ya, mi ngi mel ni sàmmkat biy sàmm ci li wër ab ñag, daanaka rekk sàmm na ca biiram, xanaa du buur bu nekk am na ab ñagam, te ñagub Yàlla mooy li mu araamal, xamleen ne yaram am na aw lumb wow bu baaxee yaram wépp baax, bu yàqoo yaram wépp yàqu, loolu mooy xol«.
Wér na Al-Buxaarii ak muslim ñoo ko soloo