Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

45 of 732 cards

Clear filters
Benn waay dafa laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam, te dolliwuma ca dara, ndax dinaa dugg àjjana ? Mu ne ko: "waaw".
Wér na Muslim soloo na ko.
"Yàlla bind na Ag rafetal ci bir yépp, bu ngeen dee ray nangeen rafetal rayiin wa, bu ngeen dee rendi nangeen rafetal rendiin wa, nangeen daas seenug ñawka tey noppal li ngeen di rendi".
Wér na Muslim soloo na ko.
"buleen soxorante, buleen worante, buleen bañante, buleen dummooyoonte, bu kenn ci yéen jaay ci kaw njaayu keneen, nangeen nekk ay mbokk jullit mooy mbokku jullit, du ko tooñ, du ko beddi, du ko xeeb, ragal Yàlla fii la nekk" muy junj ci dënnam bi ñatti yoon "doy na sëkk nit aw ay muy xeeb mbokk jullitam, léppi jullit bi dafa araam ci jullit bi, dereetam, ak alalam, ak deram".
Wér na Muslim soloo na ko.
Wax naa : yaw Yónente Yàlla bi, wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc".
Wér na Muslim soloo na ko.
"bokk na ci rafetug ngëmu nit ki: mu bàyyi lu ko amalul njariñ".
An-Nawawii nee na hadiis bu rafet la At-Tirmisiyyu moo ko soloo ak ñeneen.
«ku gis ci yéen lu ñu sib na ko soppi ci loxoom, bu ko manul na ko soppi ci làmmeñam, bu ko manul na ko soppi ci xolam, te loolu moo gën a néew ci ngëm».
Wér na Muslim soloo na ko.
"Yàlla farataal na ay farata buleen ko sànk, mu teg ay dig buleen ko jéggi, mu araamal ay mbir buleen ko xëtt, mu noppi ci ay mbir ngir yërëm leen waaye fàttewu ko kon buleen ko gëstu".
An-Nawawii nee na hadiis bu rafet la Ad-Daaraxutnii moo ko soloo ci Sunnaam ak ñeneen.
"Yàlla mu kawe mi nee na: ku noonook samaw wàlliyu waajal naa ko xeex, te sama jaam du ma jegeñ-jegeñlu ci dara lu ma gënal li ma farataal ci moom, te sama jaam bi du deñ di ma jegeñ-jegeñlu ci ay naafila ba ma bëgg ko, te bu ma ko bëggee maay nekk déggam bi muy dégge, ak gisam bi muy gise, ak loxoom bi muy jàppe, ak tànkam biuy doxe, te bu ma laajee ma jox ko, bu musloo ci man ma musal ko".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.