Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

27 of 732 cards

Clear filters
Ay nit ci Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dañoo wax Yonnente bi ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, way-woomal yi yóbb nañu yool yi, dañuy julli kem ni nuy jullee, di woor kem ni nuy woore, ñuy saraxe ca seen disiiti alal, mu dal di wax ne: "mo ndax Yàlla defalu leen lu ngeen di saraxee? Bépp sàbbaal ab sarax la, bépp sant ab sarax la, bépp tudd Yàlla it sarax la, digle lu baax sarax la, tere li bon sarax la, sëyug kenn ci yéen itam sarax la", ñu ne ko yaw Yonnente Yàlla bi, ndax kenn ci nun day def bànneexam ba noppi di ci am sarax? Mu ne: "xanaa du bu ko defoon ci lu araam da ciy am bàkkaar? Niki noonu it bu ko defee ci lu dagan da ciy am yool".
Wér na Muslim soloo na ko.
"Yàlla ak ub yonnenteem araamal na ñu jaay sàngara, ak médd, ak mbaam xuux, ak ay xërëm", ñu ne ko yaw Yonnente Yàlla bi, luy mbiri gereesu médd? Dañu ciy diw gaal yi, di ci diw der yi, nit ñi di ci leerale? Mu ne: "déedéet, dafa araam", Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: "yal na Yàlla ray Yahuud yi, ba Yàlla araamalee ci ñoom gerees ga dañu ko a seeyal, jaay ko, lekk njëg ga".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«li dagan de leer na li araam it leer na, seen diggante nag am na ay lënt, te ñu bari si nit ñi duñu ko xam, képp ku moytu yu lënt yi ñoŋal na diineem ak deram, waaye ku tàbbi ca lënt ya kooku tàbbi na ca yu araam ya, mi ngi mel ni sàmmkat biy sàmm ci li wër ab ñag, daanaka rekk sàmm na ca biiram, xanaa du buur bu nekk am na ab ñagam, te ñagub Yàlla mooy li mu araamal, xamleen ne yaram am na aw lumb wow bu baaxee yaram wépp baax, bu yàqoo yaram wépp yàqu, loolu mooy xol«.
Wér na Al-Buxaarii ak muslim ñoo ko soloo