Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

27 of 732 cards

Clear filters
Wax naa : yaw Yónente Yàlla bi, wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc".
Wér na Muslim soloo na ko.
«ku gis ci yéen lu ñu sib na ko soppi ci loxoom, bu ko manul na ko soppi ci làmmeñam, bu ko manul na ko soppi ci xolam, te loolu moo gën a néew ci ngëm».
Wér na Muslim soloo na ko.
«diine de laayante-biir la» nu ne ko: ngir kan? Mu ne: «ngir Yàlla, ak ngir téereem bi, ak ngir Yónentam bi, ak ngir ñiiti jullit ñi, ak ngir jullit ñépp».
Wér na Muslim soloo na ko.
"nàmpal day araamal li njureel di araamal".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf, julli ag leer la, saraxe it aw lay la, muñ it ag leer la, Alxuraan it aw lay la ñeel la yaw, walla muy aw lay ci sa kaw, nit ñépp dañuy xëy am ci ñuy jaay séen bopp, benn mu goreel ko, walla mu alag ko".
Wér na Muslim soloo na ko.
"bu ñu doon jox nit ñi ci liñuy wootewoo kon ay nit danañu wootewoo alali nit ñi ak seen dereet, waaye kiy wootewoo daa war a indi firnde, kiy weddi daa war a giñ".
Tane na Al-Bayhaqii moo ko soloo ak ñeneen kem nii, te lenn ci moom mi ngi ci ñaari Sahiih yi.
«képp ku gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nay wax yiw mbaa mu noppi, képp ku gëm Yàlla ak bis-pénc nay teral dëkkandoom, képp ku gëm Yàlla ak bis-pénc nay teral ganam».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"Jëf yi mi ngi aju ci yéene yi, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am, képp ku gàddaay ngir Yàlla ak ub Yonenteem, kooku gàddaayam dina jëm ci Yàlla ak Yonenteem, waaye képp ku gàddaay ngir àdduna jum soxlaa jot walla jigéen ju mu bëgg a takk kon gàddaayam jëm na ca la ko tax a gàddaay".
Wér na Ñaari imaam yi ci hadiis ñoo ko soloo, ñuy Abuu Abdillaahi Mouhammad ibn Ismaahiil ibn Ibraahiim ibn Al-Muxiirata ibn Bardisba Al-Buxaarii ak Abul Hussayn Muslim ibn Hajjaaj ibn Muslim Al-Xusayrii An-Naysaabuurii, ci seen ñaari téere yu wér yi nga xam ne ñoo gën a wér ci téere yi ñu taalif.