Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

124 of 732 cards

Clear filters

Narrator

Show all narrators (56)
«giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, daa naka rekk Iisaa Ibn Maryama wàcc ci yeen di ab àttekat bu màndu, di toj kurwaa yi, di ray mbaam-xuux yi, dindi galag gi(empo) bi, alal daal di baawaan ba kenn soxlawu ko».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«digal nañu ma ma xeex ak nit ñi ba baa ñuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka, bu ñu defee loolu ñoŋal nañu ci ma seen dereet ak seen alal lu dul ci àqi Lislaam, seenub regle nag ci Yàlla la aju».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
moom dafa wax Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: waaw xibaar ma bu ma dajee ak jenn waay ci yéefar yi ñu rayante, mu dóor jaaseem ji ci sama benn loxo daal di koy dagg, topp mu làqatu ma ci genn garab, daal di wax ne: man jébbalu naa ñeel Yàlla, ndax dama koy ray yaw Yonnente Yàlla bi ginnaaw ba mu ko waxee? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: "bul ko ray" mu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, moom dafa dagg sama benn loxo, daal di wax loolu ginnaaw bi mu ko daggee? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: "bul ko ray, ndaxte boo ko rayee moom day nekk sa barab laata nga koy ray, yaw nga nekk ci barabam laata muy wax kàddu gi mu wax".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Jele nañu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci li mu soloo ci Boroomam mu màgg mi mu wax ne: «Yàlla dafa bind yu rafet yi ak yu ñaaw yi, daal di leeral ko, képp ku yéene jëf i yiw, te defu ko, Yàlla dana ka ko bindal wenn yiw wu mat sëkk, waaye bu ko yéenee ba noppi def ko, mu bindal ko fukki yiw, mannakoo Ful bamu yégg juróom-ñaari téeméeri, ba ci ay full yu bari, waaye képp ku Yéenee jëf lu ñaaw te defu ko Yàlla di na ko bindal wenn yiw wu mat sëkk, bu ko Yéenee nag daldi koy def mu bindal ko wenn ñaawteef».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«lépp lu ma leen tere nangeen ko moytu, lépp lu ma leen digal nangeen ca def lu ngeen man, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy seen laaj yu bari, ak seenug juuyoo ak seen i Yonente».
Wér na Al-Buxaarii ak muslim ñoo ko soloo
Dafa nekkoon ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci ab tukki ci tukkerm yi, nee na: Yónente daldi yónni lenn ndaw -fekk nit ñi ña nga ca séen fanaanukaay- mu ne ko "bumu bàyyi benn caq walla bantu fett ci doqug genn giléem te daggu ko".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Damaa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi, Ibn Jadhaan de ca jamanoy ceddo ga da daan jokk mbokk di leel miskiin, mo ndax loolu dana ko jariñ ? Mu wax ne: «du ko jariñ de, ndaxte waxul benn yoon ne: sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba».
Wér na Muslim soloo na ko.
"bu nit waxee mbokkam: yaw yéefar bi, kon kenn ci ñoom ñaar yóbb na ko, bu dee li mu wax noonu la, lu ko moy mu dellusi ci moom".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.