Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

6 of 732 cards

Clear filters
«bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm- ca àjjana, ne ko: demal xool ko ak la ma ca waajalal ay ñoñam. Mu xool ko daal di ñëw, ne ko: giñ naa ci sa màgg gi ne kenn du ko dégg lu dul ne dana def lu ko cay dugal. Mu digle ñu wërale ko ak ay tiis, mu ne ko: demal xool ko ak la nu ca waajalal ay ñoñam, mu fekk ñu muure ko ak i tiis mu wax ko ne: giñ naa ci sa màgg gi ragal naa ne kenn du fa dugg. Mu ne ko demal nga xool sawara ak la ma ca waajalal ay ñoñam. Mu xool ko gis waa sawara a nga warante, mu dellu ne ko: giñ naa ci sa màgg gi kenn du def lu la fay dugal. Mu digle ñu muure ko ak i bànneex, mu ne ko: dellul xool ko. Mu xoolaat ko gis ñu muure ko ak i bànneex, mu dellu ne ko: giñ naa ci sa màgg gi ragal naa ne kenn du ca mucc».
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy.
Benn waay dafa mas a ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, kenn ci nun de dana yég ci boppam dara Lu koy gaar loo xam ne mu nekk dóom moo koy gënal mu wax ko, mu ne ko: «Yàlla rekk a màgg, Yàlla rekk a màgg, maa ngi sant Yàlla mi delloo pexeem ya ci ay jax-jaxal».
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa.
«buleen di wax: bu soobe Yàlla soob diw, waaye waxleen: bu soobe Yàlla topp mu soob diw»
Wér na ci kaw bees boolee mbooleem yoon yi mu ñëwee Abóo Daawuda soloo na ko, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ahmat.
«kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc rëbb na góor giy sol colug jigéen, ak jigéen giy sol colug góor.
Wér na An-Nasaa-iyyu soloo na ko ci Al-Kubraa ak Ibn Maaja ci maanaam mi ak Ahmad.
Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, wax ak moom ci yenn mbir yi, daal di ne ko: bu soobe Yàlla soob la, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: "ndax dangamay yamale ak Yàlla? Waxal: bu soobe Yàlla moom dong".
Ag càllalaam tane na رواه ابن ماجه والنسائي في الكبرى وأحمد