Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

7 of 732 cards

Clear filters
«ku dindil aji-gëm ji jafe-jafe ci jafe-jafey àdduna Yàlla dindil ko jafe-jafe ci jafe-jafey ëllëg bis-pénc, ku yombalal ki nekk ci jafe-jafe Yàlla yombalal ko ci àdduna ak allaaxira, ku suturaal ab jullit Yàlla suturaal ko ci àdduna ak allaaxira, Yàlla day dimbali jaam bi fii ak jaam bi moo ngi dimbali mbokkam, ku sóobu aw yoon di ca sàkku xam-xam yàlla yombalal ko yoonu àjjana, te aw nit duñu dajaloo ci ak kër ci këri Yàlla yi di jàng téereb Yàlla bi di ko jàngalante ci seen biir lu dul ne ag dal dana wàcc ci seen kaw yërmànde muur leen, malaaka yi yiir leen, Yàlla tudd leen ca ña fa moom, ku ay jëfam yeexal askanam du ko gaawal».
Wér na Muslim soloo na ko.
«ku Yàlla nàmm ci moom aw yiw dana ko dégg-loo diine, man nag ab séddalekat kepp laa, waaye Yàlla mooy joxe, te xeet wii du deñ di taxaw ci mbiri Yàlla, ku wuute ak ñoom it du leen lor, ba baa mbiri Yàlla di ñëw».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Bokk na ci màndargay bis-pénc nu yëkkati xam-xam, réer bari, njaalo bari, naan sàngara bari, góor ñi néew, jigéen ñi bari, ba juróom-fukki jigéen di tolloog benn góor».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Ñi nu doon jàngal Alxuraan ci Sahaabay Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax nañu nu ne ñoom dañu daan jàng ci Yónente bi fukki aaya, daawuñu jëlaat dara tek ko ca fukk ya ba baa ñuy xam li nekk ci yii ci xam-xam ak jëfe, nu wax ne: ñu boole xam ak jëfe.
Tane na Ahmat soloo na ko.
«yaw Aba-Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi?» Nee na: ma ne ko: Yàlla ak ub Yónenteem ñoo xam. Mu ne ma: «yaw Aba- Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi ?» Nee na: ma ne ko: {Allaahu laa-i-Laaha illaa huwa Al-Hayyul Xayyuumu} [Al-Baxara: 255]. Nee na: mu dóor sama dënn, daal di wax ne: «giñ naa ci Yàlla, na xam-xam ndokkeel Aba- Munsir».
Wér na Muslim soloo na ko.
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa génn ci menn mbooloo ci sahaabaam yi, ne leen: "lan moo leen toogloo?" Ñu ne ko: dañoo toog di tudd Yàlla di ko sant ci li mu nu gindi ci Lislaam, te xéewalal nu ko, mu wax ne: "ndax man ngeen a seedeel Yàlla ne dara toogloowu leen lu dul loolu?" Ñu ne ko: giñ nañu ci Yàlla ne dara toogloowu nu lu dul loolu, mu ne leen: "man nag giñloowuma leen ci ne dama leen a tuumaal, waaye Jibriil moo ñëw fi man xibaar ma ne Yàlla mu kawe mi moo ngi leen di puukarewoo fa malaaka ya".
Wér na Muslim soloo na ko.
"yal na Yàlla leeralal waaju dégg ci man dara mu jottali ko kem na mu ko dégge woon, bariwaana ku ñu jottali mu gën a xam aji-dégg ji".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.