Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

85 of 732 cards

Clear filters
Wax naa : yaw Yónente Yàlla bi, wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc".
Wér na Muslim soloo na ko.
"mbooloo miy njëkk a dugg àjjana dañuy nekk ci melow weer wi ci guddig Badr, ña topp ca ñoom gën a tarug leer biddiwu per ci ag leer, te duñu saw duñu dem wanag, duñu tifli du ñu ñandu, seen peñe yi ci wurus la, seen ñaq yi Misk la, seen garabi taal yu neex ya bantu gëtt la, seen jabar ya Huuru Hiin lañu, ñu nekk ci bindug kenn nit, ci melow seen baay Aadama, juróom-benn-fukki xasab ci kaw".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi ka raye ak ka ñu ray yépp sawara lañu jëm», ma ne ko: yaw Yónente Yàlla bi kii moo ray, waaw ki ñu ray moom luy mbiram? Mu ne: «ndax moom dafa xéroon ci ray waayam ji».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar».
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
"Yàlla mu kawe mi nee na: ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem".
Wér na Muslim soloo na ko.
«Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf, julli ag leer la, saraxe it aw lay la, muñ it ag leer la, Alxuraan it aw lay la ñeel la yaw, walla muy aw lay ci sa kaw, nit ñépp dañuy xëy am ci ñuy jaay séen bopp, benn mu goreel ko, walla mu alag ko».
Wér na Muslim soloo na ko.
«Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf».
Wér na Muslim soloo na ko.
"amna ci ñi leen jiitu woon jenn waay ju am gaañu-gaañu, mu saalit, daal di jël paaka dagg loxo bi, dereet ji dogul ba mu faatu, Yàlla mu kawe mi wax ne: sama jaam bi gaawe na ma ci boppam, araamal naa ci moom àjjana".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.