Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

132 of 732 cards

Clear filters

Narrator

Show all narrators (58)
«yéemu naa ci mbirum jullit bi moom de mbiram lépp yiw la, te kenn amul loolu ku dul jullit bi, bu ko mbégte dalee day sant mu doon aw yiw ci moom, bu ko lor dalee day muñ mu doon aw yiw ci moom».
Wér na Muslim soloo na ko.
«amul kenn kuy def bàkkaar, jug daal di laab, daal di julli, daal di jéggalu Yàlla, lu dul ne Yàlla dina ko jéggal», mu daal di jàng aaya jii: {ak ña nga xam ne bu ñu defee ñaawteef mbaa ñu tooñ seen bopp dañuy tudd Yàlla daal di jéggalu seen bàkkaar} [ Aali-Imraan: 135].
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Faatimata yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa ñëw ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di ko jàmbat li muy daj ci soqq ak wol, mu dégg ne dafa am ay jaam, te fekku ko fa, mu wax ko Aysatu, ba mu ñëwee Aysatu wax ka ko, nee na: mu ñëw fi nun fekk tëdd nanu, ba nuy jog mu ne nu: "buleen jog" mu ñëw toog sunu diggante, ba may yég seddaayu tànkam ci sama biir, mu wax ne: "ndax duma leen tektal lu gën li ngeen di laaj? Bu ngeen tëddatee -walla ngeen ñëw ci seen lal- nangeen sàbbaal Yàlla fanweer ak ñatt, te ngeen sant Yàlla fanweer ak ñatt, ngeen màggal Yàlla fanweer ak ñent, loolu moo gën ci yéen liggéeykat".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax bu jafe-jafe amee: "laa ilaaha illallaahu Al-Hasiimu Al-Haliimu, laa ilaaha illallaahu Rabbul Harsi Al-Hasiimi, laa ilaaha illallaahu Rabbus Samaawaati wa Rabbul Ardi wa Rabbul Harsi Al-Kariimi".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«buleen ŋàññ ngelaw li, bu ngeen gisee lu ngeen sib, nangeen wax: Allaahuma innaa nas-aluka min xayri haasihi arriihi wa xayri maa fiihaa wa xayri maa umirat bihii, wa nahuusu bika min sarri haasihii arriihi wa sarri maa fiihaa wa sarri maa umirat bihii».
Wér na At-tirmisiy soloo na ko.
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daawul bàyyi di ñaan lii, bu gontee ak bu xëyee: "Allaahuma innii as-aluka alhaafiyata fiddunyaa wal aaxirati, Allaahuma innii as-aluka alhafwa walhaafiyata fii diinii wa dunyaaya wa ahlii wa maali, Allaahuma ustur hawratii -walla hawraatii- wa aamin rawhaatii, Allaahuma ihfasnii min vayni yadayya, wa min xalfii, wa han yamiinii, wa han simaalii, wa min fawxii, wa ahuusu Bika an uxtaala min tahtii".
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
«li gën a kawe cig jégalu yi mooy nga wax: Allaahumma anta Rabbii laa-i-Laaha illaa Anta, xalaqtanii wa anaa abduka, wa anaa halaa ahdika wa wahdika mastatahtu, ahuusu bika min sarri maa sanahtu, abuuhu laka bi nihmatika alayya, wa abuuhu bi sanbii faxfirlii,fa innahu laa yaxfirus sunuuba illaa Anta» mu wax ne:"ku ko wax ci bëccëg gi te am ci kóolute, daal di faatu ci bis bi njëkk ngoon di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk, ku ko wax it ci guddi gi te am ci kóolute daal di faatu njëkk suba di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
"ku wax: radiiitu bil-Laahi Rabban, wa bi Muhammadin Rasuulan, àjjana war na ci moom".
Wér na Abóo Daawuda soloo na ko.