Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

132 of 732 cards

Clear filters

Narrator

Show all narrators (58)
Benn waay dafa laaj Yonnente bi ci bis-pénc ne ko: kañ la bis-pénc? Mu ne ko: "lan nga ko waajalal". Mu ne ko: du dara, lu dul ne bëgg naa Yàlla ak ub yonnenteem yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu ne ko: "ki nga bëgg ngay nekkal". Anas nee na: masuñoo bég ci dara kem ni ñu bége ci li Yonnente bi wax ne: "ki nga bëgg ngay nekkal" Anas wax ne: man bëgg naa Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak Abuu Bakrin ak Umar, te maa ngi am yaakaar a nekk ak ñoom ndax li ma leen bëgg, donte jëfuma lu tolni seen jëf ya.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"buleen soxorante, buleen worante, buleen bañante, buleen dummooyoonte, bu kenn ci yéen jaay ci kaw njaayu keneen, nangeen nekk ay mbokk jullit mooy mbokku jullit, du ko tooñ, du ko beddi, du ko xeeb, ragal Yàlla fii la nekk" muy junj ci dënnam bi ñatti yoon "doy na sëkk nit aw ay muy xeeb mbokk jullitam, léppi jullit bi dafa araam ci jullit bi, dereetam, ak alalam, ak deram".
Wér na Muslim soloo na ko.
Wax naa : yaw Yónente Yàlla bi, wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc".
Wér na Muslim soloo na ko.
"mbooloo miy njëkk a dugg àjjana dañuy nekk ci melow weer wi ci guddig Badr, ña topp ca ñoom gën a tarug leer biddiwu per ci ag leer, te duñu saw duñu dem wanag, duñu tifli du ñu ñandu, seen peñe yi ci wurus la, seen ñaq yi Misk la, seen garabi taal yu neex ya bantu gëtt la, seen jabar ya Huuru Hiin lañu, ñu nekk ci bindug kenn nit, ci melow seen baay Aadama, juróom-benn-fukki xasab ci kaw".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi ka raye ak ka ñu ray yépp sawara lañu jëm», ma ne ko: yaw Yónente Yàlla bi kii moo ray, waaw ki ñu ray moom luy mbiram? Mu ne: «ndax moom dafa xéroon ci ray waayam ji».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar».
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
"amul benn jullit buy ñaan ñaan gu amul bàkkaar amul dog mbokk, lu dul ne Yàlla dana ko ko jox ci benn ci ñatt yii: ben mu gaawalal ko ag ñaanam, walla mu dencal ko ko ca allaaxira, walla mu wëlbatil ko ca lu bon lu toll ni moom" ñu ne ko: kon de dananu barile, mu ne: "Yàlla moo gën a barile".
Wér na Ahmat soloo na ko.
"Yàlla mu kawe mi nee na: ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem".
Wér na Muslim soloo na ko.