Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

93 of 732 cards

Clear filters
"moytuleen juróom-ñaar yiy alage", ñu ne ko: yaw Yónenteb Yàlla bi yooyu yan la ? Mu ne: "bokkaale Yàlla, ak njabar, ak ray bàkkan bu Yàlla araamal ñu ray ko ci ludul dëgg, ak lekk ribaa, ak lekk alali jirim, ak daw bisub xare , ak tuumaal jigéen i jullit ju saŋewu".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Aji-woote ji day woote ne: di ngeen wér te du ngeen tawatati ba fàww, di ngeen dund te du ngeen deeati ba fàww, di ngeen bijjaaw te du ngeen màggatati ba fàww, di ngeen xéewlu te du ngeen yoqatati ba fàww " loolu mooy li Yàlla di wax naan: {ñu woo leen ne leen loolu mooy àjjana ja dondloo nañu leen ko ci sababus li ngeen doon jëf} [Al-Ahraaf: 43].
Wér na Muslim soloo na ko.
«wàlle amul gaafal amul, njuuma amul, Safar amul, te nanga daw ki gaana kem ni ngay dawe Gaynde».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"ki jébbalu, ñu wërsëgal ko lu doy, Yàlla def ko mu doylu ci li ko Yàlla jox koo ku texe na”.
Wér na Muslim soloo na ko.
«misaalu toogandoo bu sell ak toogandoo bu bon moo ngi mel ni ki yor gëttug Misk ak kiy upp ab furne, ki yor gëttug Misk gi: benn mu mayla ci, walla nga jënd ci, mbaa nga am fi moom xet gu neex, kiy upp ab furne nag moom: benn mu lakk say yére, walla nga jële fa xet gu bon».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"Yàlla du nelaw, te yellul ci moom muy nelaw, mooy yëkkëti ay balaas di ko wàcce, dees na yëkkëti jëfi guddi yi jëme ci moom laata jëfi bëccëg yi, ak jëfi bëccëg yi laata jëfi guddi yi, kiiraayam leer la -ñëw na ci geneen nettali: sawara la- bu ñu ko wuññi woon kon ceeñeeru kanamam gi dana lakk lépp lu gisam gi egg ci mbindeefam yi".
Wér na Muslim soloo na ko.
"Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf, julli ag leer la, saraxe it aw lay la, muñ it ag leer la, Alxuraan it aw lay la ñeel la yaw, walla muy aw lay ci sa kaw, nit ñépp dañuy xëy am ci ñuy jaay séen bopp, benn mu goreel ko, walla mu alag ko".
Wér na Muslim soloo na ko.
«ku dajeek Yàlla te bokkaalewu ko ak dara dana dugg àjjana, waaye ku dajeeg moom bokkaaleko ak dara dana dugg sawara».
Wér na Muslim soloo na ko.