Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

30 of 732 cards

Clear filters
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan seeti ku feebar di ko ñaanal day wax: "ashibil basa, rabban naasi, wasfi Anta As-Saafii, laa sifaa-a illaa sifaa-uka sifaa-an laa yuxaadiru saqaman".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«bu kenn ci yéen óbbalee na teg loxoom ci gémmiñam ndaxte Saytaane day dugg».
Wér na Muslim soloo na ko.
«àqi jullit ci moroomu jullitam juróom la: delloo ab nuyoo, ak seeti ki wopp, ak gunge néew bi, ak wuyu woote ba, ak ndokkeel ku tissooli».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"góor du xool awray góor, jigéen it du xool awray jigéen,te góor ak góor duñu sàngu ci menn malaan,jigéen ak jigéen it du ñu sàngu ci menn mbalaan .
Wér na Muslim soloo na ko.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa génn ci nun, nu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, xam nanu naka lanu lay nuyòo, leegi naka lanuy jullee ci yaw?, mu wax ne: "waxleen: Allaahumma salli halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin kamaa sallayta halaa aali Ibraahiima, innaka Hamiidun Majiidun, Allaahumma baarik halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin kamaa baarakta halaa aali Ibraahiima innaka Hamiidun Majiidun".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«Bu leen sol suwaa walla sooy, bu leen naan ci ndabal wurus mbaa xaalis, te bu leen lekk ci ay boolam, ndax ñoom la ñeel fii ci àdduna, waaye nun la ñeel fële ca àllaaxira».
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.