Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

12 of 732 cards

Clear filters
"bu genn jigéen tukki lu mat doxub ñaari fan lu dul mu ànd ak jëkkëram walla ab jegeñaaleem , te kenn du woor ci ñaari bis yii : korite ak tabaski, kenn du julli ginnaaw suba gi ba keroog jant bi di fenk, du caagine it ginnaaw tàkkusaan ba keroog muy so, deesul war jëm cib tukki lu dul ñeel ñatti jàkka: jàkkay Màkka ja ñu wormaal, ak jàkkay Aqsaa, ak sama jàkka jii".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"tabax nañu lislaam ci juróom: seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamam la di ndawam, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak aji Màkka, ak woor weeru koor ".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax jenn jigéen ju bokk ci Ansaar yi Ibn Abbaas tudd na ko waaye maa fàtte turam:"lan moo la tere nga ànd ak nun aji?" Mu ne ko: amunu lu dul ñaari giléem baayu doomam ak doomam ja aji ca genn giléem ga bàyyeel nu genn giléem te ci lañuy wute ji ndox,mu ne ko:"bu weeru koor ñëwee na nga dem umra ji ndax umra day yemoo ak aj".
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
«Amul benn bis bob jëf ca lu baax moo gënal Yàlla ci bis yii» maanaam fukki bis yi nëkk Si weeru tabaski, ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ba ci jihaad ci yoonu Yàlla? Mu ne: «ba ci jihaad ci yoonu Yàlla, lu dul waa ju génne bakkanam ak alalam te dara ci yooyu dellusiwul».
Wér na Al-Buxaarii soloo na ko ak Abuu Daawuda te baat yi moom la ñeel
Yaw Yonnente Yàlla bi, gis nanu ne jihaad moo gën ci jëf yi, mo ndax dunu jihaadi? Mu wax ne: "déedéet, waaye jihaad ji gën mooy: aj gu baax".
Wér na Al-buxaariy soloo na ko.
Ni Yonente Yàlla bi doon labbaykawoo mooy: "Labbayka Allaahuma, làbbayka, labbayka laa siriika laka labbayka, innal hamda wannihmata laka walmulka laa sariika laka" nee na: Abdullah ibn Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm daan na ci dolli: labbayka labbayka wa sahdayka, walxayru kulluhu biyadayka, labbayka warraxbaa-u ilayka walhamalu.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
"ku am gàtt bu mu rendi bu weeru Tabaski bi duggee, bu mu jël dara ci kawaram ak ci weyam ba mu Tabaski ba noppi".
Wér na Muslim soloo na ko.
Mu ñëw ci Hajarul Aswad daal di koy fóon, daal di wax ne: man de xam naa ne yaw aw xeer nga, doo lor te doo jariñ, bu dul woon ne gisnaa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di la fóon kon duma la fóon.
Wér na Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.