Skip to content

"benn waay da doon dox ci am mbedd rekk daal di fekk ay dég ci kaw yoon wi mu randale ko, Yàlla sant ko jéggal ko".

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"benn waay da doon dox ci am mbedd rekk daal di fekk ay dég ci kaw yoon wi mu randale ko, Yàlla sant ko jéggal ko".

«بَيْنَمَا رَجُلٌ يَمْشِي بِطَرِيقٍ وَجَدَ غُصْنَ شَوْكٍ عَلَى الطَّرِيقِ فَأَخَّرَهُ، فَشَكَرَ اللَّهُ لَهُ فَغَفَرَ لَهُ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne benn waay da doon dox daal di romb garabu dég ci yoon wi te day lor jullit ñi, mu randale ko teggi ko ci yoon wi, , Yàlla sant ko jéggal ko.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ngëneelu dindi lor ci yoon wi, ak ne sabab la ci njéggalu Yàlla.

Bañ a xeeb jëfi yiw yi donte dafa tuuti.

Lislaam diiney set la ak di sàmm gox bi ak jàmm ju matale.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 132) (652).

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1521) (1914).

Yataal gi (6)

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (1/ 156).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (2/ 175).

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 207).